Abstract
AbstractDemokaraasi benn la baat ci yi gën a siiw ci jamono jii ci àdduna bi, rawatina ci Senegaal. Waaye nag, lu bari ci ñi dëkke réew mi, seen xam‐xam ci moomu mbir taxu koo leer lool ndax li baat bi cosaanoo ci réewum Geres. Ñenn ñi jàpp nañu ne baat baa ngi tekki am sañ‐sañu wax lu la soob te dara du la ci fekk: « ci demokaraasi lanu nekk » wala “lii demokaraasi la” lanuy dégg ci nit ñi léeg‐léeg. Ñeneen ñi jàpp ne demokaaraasi mu ngi soxal wéy politig yi ag seen diggante ag nguur gi. “Nanu joxante cër ci sunu diggante nun niy yëngu ci wàllu demokaraasi » wala ‘‘nanu nekk ay demokaraat”. Nu jeexal ag ñi jàpp ne baat baa ngi tekki aw doxalinu réew ci politig, ëmb ay kurel yu deme ni Péncum ndawi réew mi, yeneen pénc yu ni mel, ag ay doxalin yu mel ni sànnil xob ku la neex te dara du la ci fekk. Waaye ndax askan wi nu tànnal demokaaraasi xam nañu dëgg‐dëgg li mu wund ? Ndax mën nanu wax demokaraasi te waxunu askan ag làkk wi nu koy doxale ? Ci gàttal, ndax mënees naa doxal demokaraasi ci làkku jambur ? Li waral sunu kàddu yii mooy wone jafe‐jafe yi nekk ci doxal demokaraasi. Ngir firndeel loolu dinanu sukkandiku ci xeex yi amoon ci Senegaal ci wàllu politig ag tànneefu wéy politig yi jëm ci jëffandikoo séen làkk ci jamonoy xëccoo nguur. Ci noonu lanu fas yéenee joxe sunu xalaat ci taxawaayu làkki réew mi ci askan wi, ci politig, and ci koom ci sunu réew.
Published Version
Talk to us
Join us for a 30 min session where you can share your feedback and ask us any queries you have
Similar Papers
Disclaimer: All third-party content on this website/platform is and will remain the property of their respective owners and is provided on "as is" basis without any warranties, express or implied. Use of third-party content does not indicate any affiliation, sponsorship with or endorsement by them. Any references to third-party content is to identify the corresponding services and shall be considered fair use under The CopyrightLaw.